Ubbil li ci biir

Ndax li science wax ànd na ak li Biibël bi wax?

Ndax li science wax ànd na ak li Biibël bi wax?

Li Biibël bi wax

Dëgg la, Biibël bi du téere science, waaye buy wax ci mbirum science dafay ànd bu baax ak li science wax. Xoolal ni lii di topp di wonee ne li science wax ànd na ak li Biibël bi wax. Xoolal it li Biibël bi wax ci wàllu science te mu wuute lool ak li nit ñi gëmoon ca jamono ji ñu koy bind.

  • Asamaan ak suuf, am na fu ñu jóge (Njàlbéen ga 1:⁠1). Waaye ca jamono yu yàgg ya, ñu bare gëmuñu woon ne asamaan ak suuf dañu leen sàkk. Ci ñoom, lépp a jaxasoo woon, ba jekki-jekki rekk lu nekk tegu palaasam. Waa Babilon dañu gëmoon ne ay yàlla yu jóge ci ñaari géej ñoo tax asamaan ak suuf am. Am na ñeneen ñu doon wax ne asamaan ak suuf ci benn nen bu mag-a-mag lañu jóge.

  • Ay dogali yoon ñoo yor asamaan ak suuf, waaye du ay yàlla (Ayóoba 38:33; Yeremi 33:25). Ci àddina sépp ñu bare gëm nañu ne yàlla yooyu ñooy dogal, te nit ñi mënuñu rëcc ci loolu bu dee sax lu leen di gaañ la.

  • Suuf si teguwul ci dara (Ayóoba 26:⁠7). Ci jamono yu yàgg ya, nit ñu bare dañu foogoon ne suuf si dafa mel ni benn palaat bu benn ponkal yenu walla bu tegu ci benn mala bu mel ni nagu-àll walla mbonaat.

  • Ndoxu géej dafay yéeg asamaan nekk niir ba noppi indi taw walla wàcce galaas. Ndox moomu mooy wal dem ca dex yi (Ayóoba 36:​27, 28; Kàdduy Waare 1:7; Esayi 55:10; Amos 9:⁠6). Gereg yu njëkk ya dañu foogoon ne ndox mi nekk ci dex yi ci géej gu xóot-a-xóot la jóge. Loolu lañu gëmoon ba booru atum 1800.

  • Tund yi dañuy yokku ak di wàññeeku, te tundu yi tey, am na jamono, ci biir géej lañu nekkoon (Sabóor 104:​6, 8). Loolu wuute na ak li léeb yu bare di wax, maanaam ay yàlla ñoo sàkk tund yi.

  • Fagaru dafay aar wér-gi-yaram. Ci santaane yi ñu joxoon waa Israyil amoon na ay tegtal yuy wone ni nit ku laal médd waroon a setale boppam, ni ñu waroon a bere ku am feebar buy wàlle ak li nit ñi waroon a def ak puub yi (Sarxalkat yi 11:28; 13:​1-5; Baamtug Yoon wi 23:14). Tegtal yooyu wuute woon nañu lool ak li waa Misra daan def ci jamono jooju, maanaam jaxase puub ak leneen ngir faj góom.

Ndax science dafa gis njuumte ci li Biibël bi wax?

Ku jàng bu baax li Biibël bi wax dinga gis ne loolu amul. Xoolal yenn mbir yu nit ñi foog ne Biibël bi moo ko wax fekk àndul ak science:

Am na ñuy wax ne: Biibël bi nee na Yàlla dafa sàkk asamaan ak suuf ci juróom-benni fan, te fan bu nekk 24 waxtu la.

Li Biibël bi wax dëgg: Biibël bi waxul diir bi Yàlla sàkk asamaan ak suuf (Njàlbéen ga 1:⁠1). Rax-ci-dolli, fan yi ñu wax ci Njàlbéen ga pàcc 1 kenn waxul diir bi. Te sax, diir bi Yàlla sàkk asamaan ak suuf yépp ñu ngi leen woowe benn «bés» (Njàlbéen ga 2:⁠4).

Am na ñuy wax ne: Biibël bi dafa wax ne gàncax lañu njëkk a sàkk bala naaj di am, kon bala sax li ñuy woowe photosynthèse ci farãse di mën a nekk (Njàlbéen ga 1:​11, 16).

Li Biibël bi wax dëgg: Biibël bi wone na ne, naaj bi dañu ko sàkk bala gàncax gi ndaxte jant bi, biddéew la bu bokk ci «asamaan» (Njàlbéen ga 1:⁠1) Ci «bés» bu njëkk bi Yàlla tàmbalee sàkk, la leer bu jóge ci naaj bi agsi ci suuf si. Jaww ji di gën a leer ci ñetteelu ‘bés’ bi, loolu tax leer gi doy ba photosynthèse mën a nekk (Njàlbéen ga 1:​3-5, 12, 13). Ginnaaw loolu rekk lañu mënoon a tollu ci suuf si di gis naaj bi (Njàlbéen ga 1:16).

Am na ñuy wax ne: Biibël bi nee na jant bi dafay wër suuf si.

Li Biibël bi wax dëgg: Kàdduy Waare 1:5 nee na: «Jant fenk, so, ne coww dellu fa muy fenke.» Waaye fii, Biibël bi dafay wone rekk li nit di gis bu nekkee ci kaw suuf. Ba tey sax, nit mën na wax ne «jant fenk» na walla ‘jant so’ na, fekk xam na ne suuf si mooy wër jant bi.

Am na ñuy wax ne: Biibël bi nee na suuf si dafa mel ni palaat.

Li Biibël bi wax dëgg: Ci Biibël bi, baatu «fa àddina yem» dafay tekki fu sore lool. Waaye loolu tekkiwul ne suuf si dafa mel ni palaat mbaa mu am cat (Jëf ya 1:⁠8). Noonu itam bu Biibël bi nee «ñeenti weti àddina», misaal la rekk buy tekki suuf si sépp. Tey itam dañuy jëfandikoo baat yu mel noonu ngir wax ci àddina wërngël këpp (Esayi 11:12; Luug 13:29).