Ubbil li ci biir

«Nañu yégle xibaaru jàmm bi!»

Ndaje bu mag bu ñetti fan bu Seede Yexowa yi bu atum 2024

Kenn du fey dara • Kenn du la laaj xaalis

Lu am solo lu fay am

Àjjuma: Xoolal liy wone ne xibaaru jàmm bi jëm ci Yeesu, te mu nekk ci téereb Injiil, dëgg la. Xoolal ni ñu nettali yooyu nekk ci Biibël bi mënee amal njariñ tey.

Samdi: Lan la yonent yi yégle woon ci juddu Yeesu ak li naroon a xew bi mu nekke xale? Ndax waxu yonent yooyu mujj nañu am dëgg?

Dimaas: Ci waxtaan bi sukkandiku ci Biibël bi te tudd: «Li tax du ñu ragal bu ñu déggee ay xibaar yu bon», xoolal li tax ay milioŋi nit am xel mu dal bu dee sax dund gaa ngi gën a metti.

Tiyaatar bu sukkandiku ci Biibël bi

Xibaaru jàmm bi Yeesu Yégle: Xaaj 1

Leer gu wóor gi ñëw ci àddina

Ni Yeesu juddoo kéemaan bu réy la. Waaye, lenn rekk la ci xew-xew yu yéeme yu amoon bi mu nekke xale. Buur bu soxor moo ko doon wut a rey, ba tax ay waajuram daw, dem nëbb ko Misra. Gannaaw loolu, yéem na ay jàngalekat yu mag yi amoon ca jamanoom. Seetaanal xew-xew yooyu ak yeneen ci tiyaatar bu def ñaari xaaj te ñu nar leen a wone àjjuma ak samdi.

Seetaanal wideo yii di wone li nar a xew ci ndaje bu mag bu ñetti fan bu ren

Lan lañuy def ci suñu ndaje yu mag yi?

Xoolal li lay xaar boo teewe ci benn ndaje bu mag bu ñetti fan bu Seede Yexowa yi.

Ndaje bu mag bu ñetti fan bu Seede Yexowa yi bu atum 2024 bi tudd: Nañu yégle xibaaru jàmm bi!

Seetaanal ci lu gàtt wideo bii di wone li nar a xew ci suñu ndaje bu mag bu ñetti fan bu ren.

Lãsamã tiyaatar bu sukkandiku ci Biibël bi te tudd: Xibaaru jàmm bi Yeesu Yégle

Ñu bare xam nañu ne ni Yeesu juddoo kéemaan la. Waaye, lan moo xewoon bala muy juddu? Lan moo xewoon bi mu juddu ba pare?