Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 03

Ndax mën nga gëm li Biibël bi wax?

Ndax mën nga gëm li Biibël bi wax?

Biibël bi am na ay dige ak ay xelal yu bare. Xéyna bëgg nga xam li mu wax, waaye itam, xéyna bëgg nga ci dem ndànk. Ndax war nga gëm dige ak xelal yi nekk ci téere bu màgget boobu? Ci dëgg, ndax mën nga gëm li Biibël bi wax ci lu jëm ci dund ci jàmm tey ak ëllëg? Ay milioŋi nit gëm nañu ko. Nañu xool li tax yow itam nga war koo mën a gëm.

1. Li Biibël bi wax, ndax lu am la, walla ay léeb la?

Biibël bi nee na, kàddu yi mu ëmb, kàddu yu «jub te dëggu» lañu (Kàdduy Waare 12:10). Biibël bi dafay wax ci ay xew-xew yu am yu ay nit dund (Jàngal Luug 1:3; 3:1, 2). Ay boroom xam-xam yu bare nangu nañu ne, at yi ñu wax ci Biibël bi, nit ñi, béréb yi ak xew-xew yu am solo yi, lu am la.

2. Lu tax ñu mën a wax ne Biibël bi xewwiwul?

Biibël bi wax na ci lu bare loo xam ne, bi ñu koy bind, kenn xamagu ko woon. Mën nañu ko gis ci li tubaab di woowe science, maanaam li boroom xam-xam yi di gëstu. Li Biibël bi wax ci fànn boobu, ñit ñu bare dañu ci doon werante bi ñu ko bindee. Waaye tey, science nangu na li Biibël bi waxoon. Biibël bi dafa «laloo [walla tegu ci] dëgg ak njub, te sax [...] ba fàww» (Sabóor 111:8).

3. Lu tax ñu mën a gëm li Biibël bi wax ci lu jëm ci ëllëg?

Biibël bi dafay yégle «jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg» (Esayi 46:10). Yégle na ay xew-xew yu bare bu yàgg bala ñuy am. Wax na itam ci liy xew tey ci àddina si, ci anam bu leer. Ci lesoŋ bii, dinañu wax ci yenn yégle yonent a yi nekk ci Biibël bi. Ni yégle yonent yooyu mate, yéeme na!

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni science ànde ak li Biibël bi wax, te nga gëstu yenn yégle yonent yu am solo yu nekk ci Biibël bi.

4. Science ànd na ak li Biibël bi wax

Ci jamono yu yàgg ya, ñu bare dañu gëmoon ne suuf si dafa am fu mu tegu. Seetaanal WIDEO BI.

Xoolal li ñu wax ci téere Ayóoba 3 500 at ci ginnaaw. Jàngal Ayóoba 26:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Biibël bi wax na ne suuf si teguwul ci «dara», lu tax mu doon lu yéeme?

Naaj bi mooy tax ndoxu géej yéeg asamaan. Bu tawee, ndox moomu wàccaat, te walangaan dellu géej. Loolu 200 at rekk ci ginnaaw, lañu ko nànd bu baax. Waaye Biibël bi yégle woon na ko ay junniy at ci ginnaaw. Jàngal Ayóoba 36:27, 28. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Biibël bi wone na ci lu yomb ne, ndox mi dafay yéeg ak a wàcc, lan moo la ci yéem?

  • Ndax aaya yi nga jàng yokk nañu sa ngëm ci Biibël bi?

5. Biibël bi yégle woon na ay xew-xew yu am solo

Jàngal Esayi 44:27–45:2. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la Biibël bi yégle woon 200 at bala Babilon di daanu?

Ñiy gëstu xew-xewu démb nangu nañu ne, buuru Pers bi tudd Sirus ak ay soldaaram, ñoo daan dëkku Babilon ci atum 539 B.S.J. b Dañoo fexe ba ndoxu dex bi doon jaar ci biir dëkk bi, bàyyi yoonam, aw feneen. Ci guddi googu nag, waa Babilon tëjuñu woon buntu dëkk bi. Ci la soldaaru Sirus yi dugge ci Babilon, daan ko, te xeexuñu. Ba tey, 2 500 at ginnaaw loolu, kenn tabaxul Babilon. Xoolal li Biibël bi yégle woon.

Jàngal Esayi 13:19, 20. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Li dal Babilon, naka lay wone ne, li yonent Yàlla Esayi yégle woon, dëgg la?

Li des ci dëkku Babilon ca Irak

6. Biibël bi yégle woon na li ñuy gis tey

Biibël bi nee na, ñu ngi ci «mujug jamono» (2 Timote 3:1). Xoolal li Biibël bi yégle woon ci lu jëm ci mujug jamono.

Jàngal Macë 24:6, 7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la Biibël bi wax ne mooy xew ci mujug jamono?

Jàngal 2 Timote 3:1-5. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ci li Biibël bi wax, yan jikko lañuy gën a gis ci nit ñi, ci mujug jamono?

  • Ci jikko yooyu, yan nga seetlu ci nit ñi?

BU LA NIT WAXOON: «Ay léeb kese ñoo nekk ci Biibël bi.»

  • Ci sa xalaat, lan mooy gën a firndeel ne, mën nañu gëm li Biibël bi wax?

NAÑU TËNK

Xew-xewu démb, science ak yégle yonent yi dañuy wone ne mën nañu gëm li Biibël bi wax.

Nañu fàttaliku

  • Li Biibël bi wax, ndax lu am la, walla ay léeb la?

  • Ci yan fànn la science ànde ak li Biibël bi wax?

  • Ndax foog nga ne Biibël bi dafay yégle li nar a xew ëllëg? Bu dee waaw, lu tax? Bu dee déet, lu tax?

Jubluwaay

GËSTUL

Lan mooy wone ne ñu ngi ci «mujug jamono»?

«6 yégle yonent yi ñuy gis tey ñuy am» (w11 1/5)

Xoolal li Biibël bi yégle woon ci lu jëm ci nguuru Geres, te mu mujj a am.

«Waxu yonent yi» dooleel nañu (5:22)

Xoolal ni yégle yonent yi soppee gis-gis bi benn góor amoon ci Biibël bi.

«Dama gëmoon ne Yàlla amul» (wp17 no 5)

a Fii, yégle yonent mooy xibaar bu jóge ci Yàlla te jëm ci li war a xew ëllëg.

b B.S.J. dafay tekki «Bala Suñu Jamono», te C.S.J. di tekki «Ci Suñu Jamono».