Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 02

Biibël bi dafay maye yaakaar

Biibël bi dafay maye yaakaar

Ci àddina si, nit ñu bare dañuy jànkoonte ak ay jafe-jafe yu leen di jural naqar, njàqare ak metit. Ndax mas nga dund lu mel noonu? Xéyna am nga lu la metti ndax feebar, walla ñàkk nga ku la jege. Xéyna itam mas nga laaj sa bopp: ‘Ndax dinaa mas a dund ci jàmm?’ Biibël bi tontu na ci lu leer ci laaj boobu.

1. Ban yaakaar la ñu Biibël bi di may?

Biibël bi yemul rekk ci wax ñu li tax àddina si fees ak ay jafe-jafe. Waaye wax na ñu itam ne, ci lu yàggatul Yàlla dina fi jële jafe-jafe yi. Dige yi nekk ci Biibël bi, mën nañu la «may [...] yaakaaru ëllëg» (Jàngal Yeremi 29:11, 12). Dige yooyu mën nañu ñu dimbali, ñu muñ jafe-jafe yi tey, am xel mu dal, te am jàmm ba fàww.

2. Lan la Biibël bi dige ci lu jëm ci ëllëg?

Biibël bi dige na ne, bés dina ñëw «dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit» (Jàngal Peeñu 21:4). Jafe-jafe yiy tax nit ñi nekk ci coono tey, lu mel ni ñàkk xaalis, njubadi, feebar ak dee dootuñu amati. Biibël bi dige na ne, nit ñi dinañu mën a dund ci jàmm ba fàww, ci àjjana ci kaw suuf.

3. Lan nga mën a def ba mu wóor la ne li Biibël bi dige dina am?

Ñu bare yaakaar nañu ne dinañu am jàmm. Waaye dara wóoruleen ne, li ñu yaakaar dina mas a am. Li Biibël bi dige moom, dina am. Mën nañu ko gëm bu ñuy «niir [walla gëstu bu baax] Mbind mi» (Jëf ya 17:11). Booy jàng Biibël bi, dinga mën a xam ndax li mu wax ci lu jëm ci ëllëg, dëgg la walla déet.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal yenn dige yi nekk ci Biibël bi yu jëm ci ëllëg. Seetlul ni yaakaar bi nekk ci Biibël bi di dimbalee nit ñi tey.

4. Biibël bi dig na ñu dund gu dul jeex ci jàmm

Xoolal li Biibël bi dige te ñu bind ko ci suuf. Ban dige moo la ci gën a neex? Lu tax nga wax loolu?

Jàngal aaya yi nekk ci wetu dige yooyu, te xalaat ci laaj yii di topp:

  • Ndax foog nga ne aaya yooyu am nañu njariñ? Ndax mën nañu amal njariñ sa waa kër ak say xarit?

Xalaatal rekk ngay dund ci àddina soo xam ne

KENN DOOTUL . . .

ÑÉPP DINAÑU . . .

5. Yaakaar bi ñu Biibël bi di may, mën na soppi suñu dund

Jafe-jafe yi ñuy dund, tas nañu yaakaaru nit ñu bare, walla sax dem ba jural leen naqaru xol. Am na ñuy xeex ngir jéem a soppi yëf yi. Biibël bi dige na ne yëf yi dinañu soppeeku. Xoolal ni loolu dimbalee ñu bare. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, ban njubadi moo metti woon Rafika?

  • Bu dee sax njubadi gi mu doon dund deñul, naka la ko Biibël bi dimbalee?

Yaakaar bi ñu Biibël bi di may, mën na ñu dimbali ñu bañ a xàddi, te génn ci suñu jafe-jafe yi. Jàngal Kàddu yu Xelu 17:22 ak Room 12:12. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax foog nga ne, xibaaru jàmm bi nekk ci Biibël bi, mën na la dimbali nga am dund bi gën tey ci tey? Lu tax nga wax loolu?

BU LA NIT WAXOON: «Li Biibël bi dige ci lu jëm ci ëllëg jafe naa gëm.»

  • Lu tax mu am solo, nga wut a xam li tax, ñu mën a gëm li Biibël bi wax?

NAÑU TËNK

Biibël bi dig na ñu ëllëgu jàmm. Yaakaar boobu, mën na ñu dimbali ñu xeex ak jafe-jafe yi.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax nit ñi war a xam li Yàlla dige?

  • Lan la Biibël bi wax ci lu jëm ci ëllëg?

  • Am yaakaar, naka la la mënee dimbali tey?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ni la yaakaar mënee dimbali boo amee jafe-jafe.

«Fan lañu mëne am yaakaar?» (g04 22/4)

Xoolal ni yaakaaru ëllëg mënee dimbali ñi am feebar bu yàgg.

«Bu ñu amee feebar bu yàgg, ndax Biibël bi mën na ñu ci dimbali?» (Ci jw.org la nekk)

Booy seetaan wideo bu ànd ak misik bii, xalaatal ngay dund ak sa njaboot ci àjjana ji Biibël bi dige.

Xalaatal bés boobu (3:37)

Xoolal ni yaakaar bi nekk ci Biibël bi, soppee dund benn góor gu doon xeex ngir ñi néew doole.

«Gëmatuma ne war naa soppi àddina si» (w13 1/7)