Ubbil li ci biir

Bu ñu amee feebar bu yàgg, ndax Biibël bi mën na ñu ci dimbali?

Bu ñu amee feebar bu yàgg, ndax Biibël bi mën na ñu ci dimbali?

Li Biibël bi wax

Waaw-waaw. Yàlla dafa am yitte ci jaamam yi feebar. Lii la Biibël bi wax ci kenn ku takku woon ci Yàlla: «Aji Sax jee lay dooleel soo woppee» (Sabóor 41:⁠4). Boo amee feebar bu yàgg, ñetti ponk yii di topp mën nañu la dimbali:

  1. Ñaanal Yàlla mu may la dooley muñ. Mën nga jot ci «jàmmu Yàlla, ji xel manta takk.» Loolu dina tax nga wàññi jaaxle bi te dimbali la nga muñ feebar bi (Filib 4:​6, 7).

  2. Amal gis-gis bu rafet. Biibël bi nee na: «Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal» (Kàddu yu Xelu 17:22). Jéemal di kaf ak di ree. Loolu dina wàññi sa njàqare te lu baax la ci sa wér-gi-yaram.

  3. Amal yaakaar ci li Yàlla dige. Yaakaar dëgg mën na la dimbali nga am mbégte bu dee sax danga am feebar bu yàgg (Room 12:12). Biibël bi nee na, bés a ngi ñëw, dootul am «kenn [...] ku neeti wopp na» (Esayi 33:24). Yàlla dina faj feebar yu yàgg yépp yu nit ñi mënul a faj tey. Biibël bi wone na sax ne, ñi màggat dinañu dellu nekkaat ndaw. Lii la wax: «Yaram wa jotaat tooyaayu ndaw, mu amaat dooley ngoneem» (Ayóoba 33:25).

Xamal lii: Bu dee sax Seede Yexowa yi gëm nañu ne Yàlla mën na leen a dimbali bu ñu amee feebar bu yàgg, loolu terewul dañuy wut a faju ci kër doktoor (Màrk 2:17). Waaye nag amul benn xeetu faj bu ñuy digle. Dañu jàpp ne ci fànn boobu, nit ku nekk moo war a jëlal boppam dogal.