Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 5

Boo ñëwee ci suñuy ndaje karceen lan nga fay jële ?

Boo ñëwee ci suñuy ndaje karceen lan nga fay jële ?

Argentine

Sierra Leone

Belgique

Malaisie

Ñu bare dañu bàyyi teewe ay ndaje diine ndaxte duñu fay jële xelal yu leen mën a dimbali ci seen dund walla luy dëfël seen xol. Léegi lan moo mën a tax nga teewe ndaje seede Yexowa yi ? Lan nga fay jële ?

Mbégte bi nekk ci booloo ak nit ñuy wone mbëggeel ak cofeel. Karceen yu njëkk ya dañu doon taxawal ay mbooloo te am ay ndaje ci seen biir ngir jaamu Yàlla, jàng mbind mu sell mi te xiirtalante (Yawut ya 10:​24, 25). Jàmm ak mbëggeel lañu doon nekke ci ndaje yooyu. Ay xarit dëgg lañu woon, ay mbokk ci ngëm (2 Tesalonig 1:3 ; 3 Yowaana 14). Tey, ci ñoom lañuy roy moo tax ni ñoom dañu am mbégte.

Njariñ bi nekk ci jàng ni ñuy toppe li Yàlla santaane ci Biibël bi. Ni ñu ko daan defe ca jamono yonent ya, tey bu seede Yexowa yi dajee, ñépp ay teew, muy góor mbaa jigéen, mag ak ndaw. Ay jàngalekat yu xareñ ñoo ñuy woon ci Biibël bi naka lañu mënee topp santaane Yàlla yi bés bu nekk (Deutéronome 31:12 ; Nehémia 8:⁠8). Ñépp a mën a bokk ci waxtaan yi ak ci woy yi ñuy woy foofu te wone noonu seen ngëm. — Yawut ya 10:23.

Barke bi nekk ci am ngëm buy gën a dëgër. Ci jamono ji mu doon dund, lii la ndaw li Pool waxoon benn mbooloo karceen : “ Bëgg naa leena gis lool, . . . nu dimbaleente ci suñu ngëm, ndax man itam ma gëna am doole ” (Room 1:11, 12). Tàmm di daje ak suñuy mbokk ci ngëm dafay dëgëral suñu ngëm te gën ñu xiir ci topp li Yàlla santaane ci Biibël bi.

Ñëwal teewe ndaje bii di ñëw, xool ba xam ndax li ñu wax fii dëgg la. Ñu ngi lay xaar. Mën nga teew te doo fey dara. Kenn du la laaj xaalis.

  •  Fasoŋ bi seede Yexowa yi di defe seeni ndaje tey, fan lañu ko jële ?

  •  Ban njariñ lañu mën a jële ci teewe ndaje karceen yi ?