Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK ÑAAR

Nañu dund ci fasoŋ bu neex Yàlla

Nañu dund ci fasoŋ bu neex Yàlla
  • Lan nga mën a def ba nekk xaritu Yàlla ?

  • Naka la la Seytaane boolee ci li mu wax bi mu tooñee Yàlla ?

  • Yan jëf ñoo neexul Yexowa ?

  • Naka nga mën a dunde ci fasoŋ bu neex Yàlla ?

1, 2. Limal ñenn ci nit ñi Yexowa jàppe woon ni ay xarit.

KAN nga bëgg mu nekk sa xarit ? Wóor na ne dinga bëgg mu doon ku nga bokkal gis-gis, bëgg-bëgg ak yar. Dinga bëgg a jege it nit ku rafet jikko, ni nit ku jub te baax.

2 Ba àddina sosoo ba léegi, Yàlla dafa mas a tànn ci biir nit ñi xarit yu ko jege. Maanaam nee woon na ne Ibraayma xaritam la (Isaïe 41:8 ; Saag 2:23). Yàlla mas na wax ne Daawuda “ ku ma neex [la] ci sama xol ”, ndaxte dafa nekkoon fasoŋu nit bu Yexowa bëgg (Jëf ya 13:22). Te yonent Yàlla Dañeel nit ku neex Yexowa la woon itam. — Daniel 9:⁠23.

3. Lu tax Yàlla tànn ay nit ñu nekk xaritam ?

3 Lu tax Yexowa jàppe Ibraayma, Daawuda ak Dañeel ni ay xarit ? Lii la waxoon Ibraayma : “ Déggal nga ma. ” (Njàlbéen ga 22:18). Kon, Yexowa dafay jege ñiy def ak xol bu woyof li mu leen sant. Waxoon na waa Israyil ne : “ Bu ngeen ma déggalee, dinaa nekk seen Yàlla, te yéen dingeen doon sama mbooloo. ” (Yérémi 7:​23, NW). Booy déggal Yexowa, dinga nekk xaritam yow itam !

YEXOWA DAFAY MAY DOOLE AY XARITAM

4, 5. Naka la Yexowa di wonee dooleem ngir dimbali ñi koy jaamu ?

4 Xalaatal njariñ bi nekk ci xaritoo ak Yàlla. Biibël bi nee na, Yexowa dafay wut fu muy wone dooleem ngir dimbali ñi ko bëgg ak seen xol bépp (2 Chroniques 16:⁠9). Naka la Yexowa mënee wone kàttanam ngir dimbali la ? Lii la Yexowa wax ci Sabóor 32:8 : “ Dinaa la xelal, xamal la yoon, wi ngay jaar; dinaa la digal, teg sama bët ci yaw. ”

5 Kàddu yooyu di wone ne Yexowa fonk na ñu, dawloo na yaram ! Yexowa dina la won fi nga war a jaar, te dina la sàmm itam booy def li mu la sant. Yàlla dafa la bëgg a dimbali ngir nga mën a muñ jafe-jafe yi ngay am (Psaume 55:22). Kon booy jaamu Yexowa ak sa xol bépp, ci lu wóor, dinga wax ak xel bu dal ni ko Daawuda waxe woon : “ Dama mas a jiital Yexowa ci lépp. Duma daanu mukk, ndaxte mu ngi ci sama ndeyjoor. ” (Sabóor 16:​8, NW ; Psaume 63:⁠8). Waaw, Yexowa mën na la dimbali nga dund ci fasoŋ bu ko neex. Waaye xam nga ne, Yàlla dafa am noon bu la bëgg a teree dund ci fasoŋ bu neex Yàlla.

NI SEYTAAANE WEDDEE YÀLLA

6. Lan la Seytaane wax ci doomu Aadama yi ?

6 Ci pàcc 11 bi, wone nañu ni Seytaane weddee sañ-sañu jiite bi Yàlla am. Seytaane dafa wax ne Yàlla waxul dëgg, ba pare mu wax ne Yexowa deful lu baax bi mu teree Aadama ak Awa ñu tànnal seen bopp li baax ak li bon. Bi doomi Aadama ak Awa komaasee bare ci kaw suuf, ginnaaw bi ñu bàkkaaree, booba la Seytaane weddi li tax doomu Aadama di jaamu Yàlla. Lii la wax : “ Du bëgg Yàlla moo tax nit di ko jaamu. ” Mu teg ci ne : “ Mayleen ma rekk, dinaa fexe ba ñépp weddi Yàlla. ” Li ñu nettali ci nit ki tudd Ayóoba mooy wone ne loolu la Seytaane foogoon. Kan mooy Ayóoba, te naka la ko Seytaane boolee ci li mu wax ngir xeex Yàlla ?

7, 8. a) Lan moo taxoon Ayóoba wuute ak ñi mu bokkaloon jamono ? b) Naka la Seytaane weddee li tax Ayóoba di jaamu Yàlla ?

7 Ayóoba nekkoon na ci kaw suuf am na lu jege léegi 3 600 at. Nit ku baax la woon, ndaxte lii la Yexowa waxoon ci moom : “ Amul kenn ku mel ni moom ci kaw suuf, nit ku gore te jub, nit ku ragal Yàlla te di moytu lu bon. ” (Ayóoba 1:​8, NW). Ayóoba nit ku neex Yàlla la woon.

8 Seytaane dafa weddi li tax Ayóoba di jaamu Yàlla. Lii la Ibliis waxoon Yexowa : “ Ndax defuloo ay ñag ñu wër ko, wërale këram ak lépp lu mu moom ? Liggéeyam barkeel nga ko. Juram bare na ba fees suuf si. Waaye ngir soppi mbir mi, tegal sa loxo ci kawam te laal lépp li mu moom, ba seet ndax du wax lu bon ci yow. ”​ — Ayóoba 1:10.11, NW.

9. Lan la Yexowa def bi ko Seytaane weddee, te lu tax mu def loolu ?

9 Ci loolu, Seytaane dafa doon wax ne li Ayóoba mënoon a am ci Yàlla rekk moo taxoon mu koy jaamu. Ibliis yokk ci ne, bu ñu ko tegee ay jafe-jafe, dina weddi Yàlla. Kon lan la Yexowa def ? Komka li taxoon Ayóoba di jaamu Yàlla la Seytaane weddi, Yexowa dafa bàyyi Seytaane mu teg Ayóoba ay jafe-jafe ngir ñu seetlu ko. Su boobaa ñépp dinañu gis ndax Ayóoba bëgg na Yàlla​ walla ​déet.

TEG NAÑU AYÓOBA AY JAFE-JAFE NGIR SEETLU KO

10. Yan musiba ñoo dal Ayóoba, te bi ko loolu dalee, lan la def ?

10 Ci lu gaaw, Seytaane daldi jaar ci ay pexe yu bare ngir seetlu Ayóoba. Dafa def ba ñu sàcc yenn ci juru Ayóoba yi, yeneen yi ñu rey leen. Ñu rey it lu ëpp ci jaamam yi. Ayóoba daldi nekk ci ñàkk bu metti. Beneen musiba yokku ci loolu. Ngelaw bu am doole ñëw rey fukki doomam yépp. Ak lu metti li ko dal noonu yépp, “ Ayóoba bàkkaarul, te waxul dara lu bon ci Yàlla. ”​ —  Ayóoba 1:22, NW.

11. a) Ñaareelu yoon bi Seytaane di sosal Ayóoba, lan la Seytaane wax, te lan la Yexowa def ? b) Lan la Ayóoba def bi ko feebar bu metti boobu dalee ?

11 Waaye Seytaane bàyyiwul ba tey. Xéyna dafa yaakaar ne, Ayóoba mën na muñ ñàkk alalam, ay jaamam, ak ay doomam, waaye bu ko feebar bu metti dalee, dina weddi Yàlla. Noonu Yexowa bàyyi Seytaane mu teg Ayóoba feebar bu séexlu te metti lool. Waaye ba tey Ayóoba dafa kontinee topp Yàlla, te lii la wax sax ak fulla : “ Ba ba may dee duma bàyyi Yàlla. ”​ — Ayóoba 27:​5, NW.

Yàlla barkeel na Ayóoba ndax li mu ko bàyyiwul.

12. Naka la Ayóoba wonee ne Ibliis fenkat la ?

12 Ayóoba xamul woon ne Seytaane moo ko tegoon musiba yooyu. Komka xamul woon lépp ci ni Ibliis doon xeexe kiliftéefu Yexowa, Ayóoba dafa yaakaaroon ne jafe-jafe yooyu mu amoon, ci Yàlla la jóge (Job 6:4 ; 16:11-14). Waaye dafa kontine di topp Yexowa. Seytaane waxoon na ne Ayóoba dafay jaamu Yàlla ndax li mu mën a am ci moom rekk. Waaye li Ayóoba kontine di gëm Yàlla, wone na ne loolu du dëgg.

13. Lan la Ayóoba may Yàlla ndax li mu ko bàyyiwul ?

13 Ngëm bi Ayóoba amoon dafa may Yexowa lu muy tontoo feni Seytaane yi ñu mën a méngale ak saaga. Ayóoba xaritu Yàlla dëgg la woon, te Yàlla fey na ko ngëm jooju mu wone.​ — Job 42:12-17.

LOOLU, NAKA LA LAY LAALE ?

14, 15. Lu tax ñu mën a wax ne doomu Aadama yépp la Seytaane boole ci li mu sosal Ayóoba ?

14 Du Ayóoba kese la Seytaane sosal. Yow itam sosal na la. Li nekk ci Léeb yi 27:11, NW, wone na ko bu baax. Lii la Kàddu Yexowa wax foofu : “ Amal xel sama doom, te seddalal sama xol, ndax ma mën a tontu ki may sóoru. ” Ay téemeeri-téemeeri at ginnaaw bi Ayóoba deewee lañu bind kàddu yooyu. Kon li ñu wax foofu dafay wone ne Seytaane mu ngiy sóoru Yàlla ba tey, te di sosal it ñiy jaamu Yàlla. Bu ñuy dund ci fasoŋ bu neex Yexowa, dañu koy may lu muy tontoo feni seytaane. Te loolu dafay seddal xolu Yàlla. Lan moo ciy sa xalaat ? Bokk ci ñiy may Yàlla li muy tontoo feni Ibliis, bu dee sax laaj na ñu soppi dara ci ni ñuy dunde, ndax neexul ci xol ?

15 Xoolal li Seytaane waxoon. Nee woon na : “ Lépp lu nit am dina ko joxe ngir musal bakkanam. ” (Ayóoba 2:4, NW). Bi Seytaane waxee : “ nit ”, dafa wone ci lu leer ne du Ayóoba kese la doon wax, waaye doomu Aadama yépp la ci boole. Loolu lu am solo la. Seytaane dafa wax ne yow mii dinga bàyyi Yàlla. Li Ibliis bëgg mooy nga bañ a déggal Yàlla, te bàyyi di def lu baax boo nekkee ci ay jafe-jafe. Naka la Seytaane di jéeme def loolu ?

16. a) Ci yan pexe la Seytaane di jaar ngir nit ñi bàyyi Yàlla ? b) Naka la Ibliis mënee jariñoo pexe yooyu jëmale ko ci yow ?

16 Ni ñu ko waxe ci pàcc 10, Seytaane dafay jaar ci pexe yu bare ngir fexe ba nit ñi bañ a topp Yàlla. Yenn saay dafay songaate “ ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp ”. (1 Piyeer 5:⁠8.) Mën nga gis loolu Seytaane di def, bu say xarit, say mbokk, walla ñeneen bañee ngay jàng Biibël bi ba di topp li nga ciy jàng * (Yowaana 15:19, 20). Ci beneen fànn, “ Seytaane moom ci boppam day mbubboo malaakam leer ”. (2 Korent 11:14.) Ibliis mën na jaar ci li neexul a ràññee ngir nax la ba nga bàyyi di dund ci fasoŋ bu neex Yàlla. Bu sa xol jeexee, Seytaane mën na ci jaar it ngir gëmloo la ne mënuloo neex Yàlla (Proverbes 24:10). Waaye ba tey, bu Seytaane di jëfe ni “ gaynde guy yëmmu ” walla ni “ malaakam leer ”, lenn rekk la bëgg. Waxoon na ne bu nit nekkee ci ay jafe-jafe walla mu am lu ko bëgg a dugal ci lu bon, dina bàyyi jaamu Yàlla. Ni ko Ayóoba defe, naka nga mën a wonee ne Seytaane fenkat la te wone ne doo bàyyi Yàlla ?

NAÑU DEF LI YEXOWA SANTAANE

17. Lan moo gën a tax ñuy topp ay ndigalu Yexowa ?

17 Mën nga wone ne Seytaane waxul dëgg booy dund ci fasoŋ bu neex Yàlla. Lan la loolu di tekki ? Lii la Biibël bi wax : “ Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, [ak] sa kàttan gépp. ” (Luug 10:27). Booy gën a bëgg Yàlla, ngay gën a sawar a def li mu la sant. Ndaw li Yowaana nee woon na : “ Mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam. ”. Soo bëggee Yexowa ak sa xol bépp, dinga gis ne “ ay ndigalam diisuñu ”.​— 1 Yowaana 5:3.

18, 19. a) Limal yenn ci li Yexowa santaane (seetal li nekk ci  xët 122). b) Naka lañu xame ne li ñu Yàlla laaj diisul torop ?

18 Lan la Yexowa santaane ? Am na lu mu wax ci jikko yi ñu war a moytu. Am na yu nekk ci wërale bi nekk ci xët 122, ci xaaj bi tudd “  Soreleen li Yexowa bañ ”. Dinga gis foofu ay jëf yu Biibël bi tere. Am na ci jëf yoo xam ne bu ñu xoolul bu baax, mën na am ñu foog ne dara bonu ci. Waaye boo xalaatee ci aaya yi ñu lim foofu, wóor na ne dinga gis ni digle Yexowa yi xóote. Xéyna soppi yenn yi ci fasoŋ bi ngay dunde dina nekk li gën a jafe ci lépp nga mas a jànkoonteel. Waaye dund ci fasoŋ bu neex Yàlla dafa lay may mbégte bu réy (Isaïe 48:17, 18). Te loolu mën nga ko def. Lan moo ñu ko won ?

19 Yexowa du ñu sant mukk lu ñu mënul a def (Deutéronome 30:​11-14). Moo ñu gën a xam li ñu mën ak fi suñu doole yem (Psaume 103:14). Rax-ci-dolli, Yexowa mën na ñu may doole bi ñu soxla ngir def li mu ñu sant. Ndaw li Pool bindoon na ne : “ Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit ñépp. Te sax Yàlla kuy sàmm kóllëre la, te du nangu nattu bi wees seen kàttan, waaye cib nattu, dina leen ubbil bunt bu ngeen man a récce, ba ngeen man koo dékku. ” (1 Korent 10:13). Yexowa mën na la may sax “ kàttan gu ëpp xel ” ngir nga mën a muñ (2 Korent 4:⁠7). Lii la Pool mujj a wax bi mu muñee coono yu bare : “ Man naa lépp ci ndimbalu Aji Dooleel ji. ”​— Filib 4:13.

NAÑU FEXE BA AM JIKKO YU NEEX YÀLLA

20. Yan jikko yu neex Yàlla lañu war a am, te lu tax jikko yooyu am solo ?

20 Neex Yexowa yemul kese ci di moytu li mu bañ. War nga bëgg it li ko neex (Room 12:9). Ndax du ci nit ñi nga bokkal gis-gis, bëgg-bëgg, ak yar ngay tànn xarit ? Yexowa noonu lay def it. Kon fexeel ba bëgg li Yexowa fonk. Wax nañu ci Psaume 15:1-5 yenn ci yi Yexowa fonk. Wone nañu ci aaya yooyu ñi Yàlla jàppe ni xarit ni ñuy mel. Xaritu Yexowa yi dañuy am jikko yi Biibël bi di woowe “ li Xelu Yàlla mi di meññ ”. Jikko yii bokk nañu ci : “ Mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaax, kóllëre, lewetaay ak maandute. ”​— Galasi 5:​22, 23.

21. Lan moo la mën a dimbali nga am jikko yu neex Yàlla ?

21 Booy faral di jàng te di gëstu Biibël bi, loolu dina la dimbali nga am jikko yu neex Yàlla. Booy jàng li Yàlla sant, loolu dina la dimbali nga fexe ba say xalaat méngoo ak xalaati Yàlla (Isaïe 30:​20, 21). Booy gën a bëgg Yexowa ngay gën a bëgg dund ci fasoŋ bu ko neex.

22. Booy dund ci fasoŋ bi neex Yàlla, lan ngay def ?

22 Boo bëggee dund ci fasoŋ bu neex Yexowa, danga war a góor-góorlu bu baax. Nit kuy soppi ni muy dunde, Biibël bi dafa koy méngale ak nit kuy summi jikko yu bon yi mu yoroon te sol yu bees (Kolos 3:9, 10). Waaye lii la Sabóor wax ci ndigalu Yexowa : “ Ku leen sàmm am yool bu réy. ” (Sabóor 19:12). Yow it, dinga gis ne kuy dund ci fasoŋ bu neex Yàlla dina am barke yu bare. Sooy def loolu, dinga wone ne Seytaane waxul dëgg, te dinga seddal xolu Yexowa.

^ par. 16 Bëgguñu wax ne nit ñi bëggul nga jàng Biibël bi, Seytaane moo leen jàpp. Waaye Seytaane mooy yàlla àddina sii, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoom (2 Korent 4:4 ; 1 Yowaana 5:19). Kon bu amee ñu kontaanul ak ñu lay xeex ndax li nga bëgg a dund ci fasoŋ bu neex Yàlla, waru la bett.