Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 25

Lu tax ñuy tabax ay saalu Nguur te naka lañu leen di tabaxe ?

Lu tax ñuy tabax ay saalu Nguur te naka lañu leen di tabaxe ?

Bolivie

Nigéria, bala ñuy tabax ak bi ñu tabaxee ba pare

Tahiti

Ni ko tur bi wonee, saalu Nguur mooy béréb boo xam ne fa lañuy jàngalee li Biibël bi wax ci Nguuru Yàlla. Yeesu ci boppam, Nguuru Yàlla la doon gën a waare. — Luug 8:⁠1.

Ci saalu Nguur yi lañuy jaamoo Yàlla dëgg. Ci saalu Nguur yi lañuy jiite liggéeyu waare xibaaru jàmm bi ci Nguuru Yàlla (Macë 24:14). Du saalu Nguur yépp ñoo bokk yaatuwaay te niroo waaye saalu Nguur yépp ay nekk ay tabax yu yem. Ci ay saalu nguur yu bare, lu ëpp benn mbooloo ñoo fay daje. Ci at yi weesu, ndegam mbooloo yi dañoo gën a yokku, tabax nañu ay fukki junniy saalu Nguur yu bees (maanaam lu jege juróomi saalu Nguur bés bu nekk). Naka la loolu mënee am ? — Macë 19:⁠26.

Xaalis bi ñuy tabaxe saalu Nguur yi, ci li nit ñi di maye la jóge. Maye yooyu dañu leen di yónnee ci bànqaas bi ngir mu mën koo jox mbooloo yi soxla tabax walla defaraat seen saalu Nguur.

Ay wolonteer yu ñu dul fey ñooy tabax saalu Nguur yi ; bokkuñu fu ñu jóge te yemuñu alal. Ci réew yu bare dañu taxawal ay Gurupu nit yuy tabax saalu Nguur yi. Gurup yooyu ñooy tabax ay saalu Nguur fépp fu ñu ko soxla ci réew mi ñu nekk, ba ca dëkk yu sore. Foofu dañuy dimbali seede Yexowa yi fa nekk ci tabax seen saalu Nguur. Ci yenn réew yi, ay seede Yexowa yu mën seen liggéey lañu dénk benn diiwaan, maanaam ay dëkk, fu ñu war a jiite liggéeyu tabax ak defaraat ay saalu Nguur. Am na it ay maneebar yu xam seen liggéey yuy ñëw ngir jàpple leen. Fépp fu ñuy tabax, ñi bokk ci mbooloo mi fa nekk ñooy def li ëpp ci liggéeyu tabax bi. Xelum Yexowa ak lépp li jaamam yi di def ak seen xol bépp moo tax ba loolu yépp mën a am. — Sabóor 127:1 ; Kolos 3:23.

  •  Lan moo tax ñuy woowe suñu béréb yi ñuy jaamoo Yàlla saalu Nguur ?

  •  Naka lañuy def ba mën a tabax ay saalu Nguur fépp ci àddina si ?