Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 9

Jaamuleen Yexowa ci seen biir Njaboot

Jaamuleen Yexowa ci seen biir Njaboot

“ Jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf. ” — Peeñu ma 14:7

Ni ngeen ko jànge ci téere bii, Biibël bi am na ay santaane yoo xam ne dinañu leen dimbali yéen ak seen njaboot. Yexowa dafa bëgg ngeen am jàmm ci seen biir njaboot. Dige na ne, bu ngeen jiitalee seen diggante ak moom, “ loolu lépp dina leen ko ci dollil ” (Macë 6:33). Dafa bëgg lool ngeen nekk ay xaritam. Defleen lépp ngir am diggante bu rafet ak Yàlla. Loolu mooy li gën a réy li nit mën a am. — Macë 22:37, 38.

1 DËGËRALLEEN SEEN DIGGANTE AK YEXOWA

LI BIIBËL BI WAX : “ ‘ Dinaa nekk baay ci yéen, ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen. Moom la Aji Man ji [Yexowa, MN ] wax ” (2 Korent 6:18). Yàlla dafa bëgg ngeen nekk xarit yu ko jege. Ñaan Yàlla dina leen dimbali ci nekk loolu. Yexowa dafa leen di xiirtal ngeen “ sax ciy ñaan Yàlla ” (1 Tesalonig 5:17). Dafa leen yàkkamti déglu ngeen wax ko li nekk ci seen biir xol ak seeni soxla (Filib 4:⁠6). Bu ngeen nekkee ak seen njaboot di ñaan Yàlla, ñoom dinañu gis ne bu ngeen di wax ak Yexowa dafa mel ni dangeen di wax ak nit bu ngeen di gis.

Ñaan Yàlla doyul, dangeen ko war a déglu it. Mën ngeen déglu Yàlla bu ngeen di gëstu Kàddoom ak téere yi sukkandiku ci Biibël bi (Sabóor 1:​1, 2). Nangeen xalaat bu baax ci li ngeen di jàng (Sabóor 77:​11, 12). Déglu Yàlla dafa laaj itam ngeen di teewe ndaje Karceen yi. — Sabóor 122:1-4.

Wax nit ñi lu jëm ci Yexowa lu am solo la itam ngir dëgëral seen diggante ak moom. Lu ngeen di gën di wax ci moom, ngeen di gën a yëg ne jege ngeen ko. — Macë 28:​19, 20.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Jëlleen jot bés bu nekk ngir jàng Biibël bi te ñaan Yàlla

  • Li njaboot gi di def ci wàllu ngëm, na gën a am solo fo ak féexal xol bi ngeen mën a def

2 AMLEEN NJÀNGUM BIIBËL BU NEEX CI SEEN BIIR NJABOOT

LI BIIBËL BI WAX : “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen ” (Saag 4:8). Dangeen war a am porogaraam ngir jàng Biibël bi ci seen biir njaboot ba pare topp porogaraam boobu (Njàlbéen ga 18:19). Waaye loolu doyul. Dangeen war a boole Yàlla ci lépp lu ngeen di def bés bu nekk. Bu ngeen di waxtaan ak njaboot gi lu jëm ci Yàlla “ bu ngeen toogee ci seen kër, bu ngeen di dox ci mbedd mi, bu ngeen di tëddi ak bu ngeen yeewoo ”, loolu dafay dëgëral seen diggante ak Yàlla (5 Musaa 6:​6, 7, MN). Defleen ko jubluwaay ni Yosuwe mi newoon : “ Man mii ak sama waa kër, Yexowa lañuy jaamu ”. — Yosuwe 24:​15, MN.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Nangeen am porogaraam bu baax bu ëmb soxlay ku nekk ci njaboot gi