Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot

Mën ngeen a am séy bu neex te am jàmm ci seen biir njaboot, bu ngeen toppee santaane yi nekk ci Biibël bi.

Ubbite bi

Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot ak séy bu neex bu ngeen toppee xelal yi nekk ci téere bii te sukkandiku ci Biibël bi.

XAAJ 1

Dégluleen Yàlla ngir am Séy bu Neex

Bu ngeen di laaj seen bopp ñaari laaj, loolu dina leen dimbali ba seen séy neex.

XAAJ 2

Na ku nekk yem ci ki mu séyal

Ndax bañ a njaaloo doy na ngir nekk ku gore ci sa séy ?

XAAJ 3

Li ngeen mën a def bu poroblem amee

Fasoŋ bi ngeen mën na wone ndax seen séy dina dëgër te neex walla dina naqari.

XAAJ 4

Naka lañu war a yoree xaalis ?

Ban njariñ la wax dëgg di indi ?

XAAJ 5

Li Ngeen Mën a Def ngir Wéy di Juboo ak Seeni Mbokk

Mën ngeen a teral seeni waajur te doo leen yàq seen séy.

XAAJ 6

Am doom dafay soppi lu bare ci séy

Ndax doom mën na dëgëral seen diggante ?

XAAJ 7

Naka ngeen war a yare seen doom

Yar tekkiwul rekk tëral ay sàrt ak door waaye ëmb na lu gën a bare.

XAAJ 8

Lan ngeen war a def bu musiba amee

Nanguleen ñu dimbali leen.

XAAJ 9

Jaamuleen Yexowa ci seen biir Njaboot

Naka ngeen di gënee a mën a am a am jàmm ci seen njàngum Biibël bi bu neex ci seen biir njaboot gi ?WEB:OnSiteAdTitleJaamuleen Yexowa ci seen biir njaboot