Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 6

Am doom dafay soppi lu bare ci séy

Am doom dafay soppi lu bare ci séy

“ Doom Aji Sax jee koy sédde ”. — Sabóor 127:3

Am doom dafay indi mbégte ci biir séy. Mën na indi itam tiit. Yéen ñi door a am doom, dingeen gis ne xale bi dina jël li ëpp ci seen jot ak ci seen kàttan. Ñàkk nelaw ak xol boo xam ne tey mu neex suba mu nàqari, loolu mën na ñagasal seen diggante. Yéen ñaar dingeen war a soppi yenn yi ngir toppatoo xale bi te sàmm seen séy. Xelal yi nekk ci Biibël bi, naka lañu leen mënee dimbali ngeen def loolu yépp ?

1 XAMLEEN LI SEEN DOOM DI SOPPI CI SEEN DUND

LI BIIBËL BI WAX : “ Ku bëgg dafay muñ te laabiir ” te “ du wut njariñu boppam, du naqari deret ” (1 Korent 13:​4, 5). Yaw mi door a nekk yaay, dëgg la sa xel yépp dina nekk ci sa doom. Waaye loolu mën na tax sa jëkkër komaase foog ne danga koy sàggane. Bul fàtte ne moom itam dafa soxla nga bàyyi sa xel ci moom. Nanga ko dimbali mu xam ne amal na la njariñ te boole nga ko ci toppatoo xale bi. Booy def loolu, ànd ci ak muñ ak mbaax.

“ Yéen góor ñi, na ku nekk ci yéen am xel, ci ni ngay ànde ak sa soxna ” (1 Piyeer 3:⁠7). Xamal ne sa jabar dina def li ëpp ci kàttanam ci toppatoo seen doom. Xamal it ne liggéeyam yokku na léegi te loolu mën na tax mu jaxasoo, mu soon walla sax mu xàddi. Xéyna lée-lée sax dina dal sa kaw, waaye nanga jéem a teye sa bopp ndaxte “ muñ mer, moo gën njàmbaar ” (Kàddu yu Xelu 16:32). Nanga am seetlu te jàpple ko fi mu soxla ndimbal. — Kàddu yu Xelu 14:⁠29.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Baay bi : Deel dimbali sa jabar ci toppatoo seen doom bu dee sax ci guddi gi la. Nanga wàññi jot bi ngay def ci yenn itte yi ngir gën a am jot ngir nekk ak sa jabar ak sa doom.

  • Yaay bi : Bu sa jëkkër di la bëgg a dimbali ci toppatoo doom bi, bul bañ. Bu deful mbir yi ni mu ware, bu ko xas waaye won ak mbëggeel ni mu war a defe.

2 DËGËRALLEEN SEEN DIGGANTE

LI BIIBËL BI WAX : Ñoom ñaar dinañu doon “ kenn ” (Njàlbéen ga 2:​24). Bu dee sax seen njaboot dafa yókku, fàttalikuleen ne ba tey yéen ñaar ñi séy “ kenn ” ngeen. Defleen lépp ngir seen diggante gën di dëgër.

Yaw miy jabar, deel gërëm sa jëkkër ci li mu lay defal. Boo koy wax li la neex ci moom dinga ko gën a sawarloo (Kàddu yu Xelu 12:18). Yaw miy jëkkër, deel wax sa jabar ni nga ko bëgge ak ni nga ko soppe. Gërëm ko ndax fasoŋ bi muy toppatoo njaboot gi. — Kàddu yu Xelu 31:​10, 28.

“ Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam ” (1 Korent 10:24). Ci lépp looy defal sa jëkkër walla sa jabar, defal ko li gën. Yéen ñaar, jëlleen jot ngir waxtaan, ku nekk gërëm sa moroom te déglu ko bu baax. Lu jëm ci diggante jëkkër ak jabar ci lalu séy, buleen xalaat seen bopp kese waaye xalaatleen li ki ngeen séyal soxla. Biibël bi nee na : “ Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeena mànkoo ci def noonu ” (1 Korent 7:​3-5). Kon nangeen waxtaan ci loolu, ku nekk wax li nekk ci xolam. Bu ngeen amee muñ te ku nekk jéem a nànd moroomam, seen diggante dina gën a dëgër.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Buleen fàtte di jël jot ngir wéet yéen ñaar

  • Defal lu yomb luy tax sa jëkkër walla sa jabar yëg sa mbëggeel, lu mel ni bind ko mesas bu neex walla may ko kado bu ndaw

3 JÀNGALLEEN SEEN DOOM

LI BIIBËL BI WAX : “ Li dale ci sa ngone xam nga Mbind mu sell, mi la mana yee ci yoonu mucc ” (2 Timote 3:​15). Tëralleen li ngeen bëgg a jàngal seen liir. Liir mën na jàng lu bare, bala sax muy juddu. Liir bi, bu nekkee ci biiru yaayam mën na sax xàmme seen baat, te it mën na yëg li ngeen di yëg. Kon nangeen jàng ay téere ci kanamam, mu dégg, bu nekkee sax xale bu tuuti. Doonte sax mënagul xam li ngeen koy liiral, nangeen ko ko tàmmal. Loolu mën na tax mu fonk njàng bu demee ba mag.

Xamleen ne xale du tuuti mukk ci dégg ay waajuram ñuy wax lu jëm ci Yàlla. Bu ngeen di ñaan Yexowa, deeleen wax muy dégg (Deutéronome 11:19). Bu ngeen di fo sax, booleen ci ay wax yu jëm ci jëfi Yàlla yi (Sabóor 78:3, 4). Noonu buy màgg, dina gis mbëggeel bi ngeen am ci Yexowa te bëgg Ko moom itam.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Ñaanleen Yàlla mu xamal leen ni ngeen waree jàngale seen liir

  • Nangeen wax di waxaat baat yi ak kàddu yi gën am solo, su ko defee xale bi dina leen teel a jàpp ci xelam