Ubbil li ci biir

Dundin ak jikko

Séy ak dundu njaboot

Ndax Biibël bi mën na ma dimbali ma am jàmm ci sama biir njaboot?

Xelal yii jóge ci Biibël bi dimbali nañu ay milioŋi nit, góor ak jigéen, ñu am jàmm ci seen biir njaboot.

Lan la Biibël bi wax ci nekkaale?

Tegtal yi jóge ci Yàlla ñoo ñuy wax li ñu war a def ba am jàmm ci suñu kër. Ñiy topp santaane Yàlla yi dinañu gis njariñ bi ci nekk saa su ne.

Ndax Biibël bi wax na ci mbirum ñaari góor walla ñaari jigéen ñuy séy?

Ki sos séy war na xam li gën ngir séy doon lu sax te neex.

Li ñuy tànn a def

Lan la Biibël bi wax ci tànnal sa bopp li nga bëgg a def? Ndax Yàlla mooy dogal lépp?

Ñu bare gëm nañu ne Yàlla mooy dogal lépp ci seen dund. Ndax li ñuy tànn a def tey mooy tax ba li ñu bëgg a def ëllëg sotti?