Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 11

Ban njariñ lañu mën a am ci topp xelal yi nekk ci Biibël bi ?

Ban njariñ lañu mën a am ci topp xelal yi nekk ci Biibël bi ?

1. Lu tax ñu soxla ñu tette ñu ?

Naka la xelal yi nekk ci Biibël bi mënee tax ñu jël ay matuwaay ngir aar suñu bopp ? — SABÓOR 36:10.

Ki ñu sàkk moo ñu ëpp xam-xam. Dafa ñuy toppatoo ni baay bu ñu bëgg. Sàkku ñu ngir ñu jiite suñu bopp (Jérémie 10:23). Ni xale soxlaa waajuram tette ko, noonu lañu soxlaa Yàlla tette ñu (Isaïe 48:17, 18). Xelal yi nekk ci Biibël bi, ay maye la yu jóge ci Yàlla ngir tette ñu. — Jàngal 2 Timote 3:16.

Yoonu Yexowa ak xelalam yi dafa ñuy jàngal ni ñuy ame dund bu neex fi ñu tollu nii, ak ni ñuy ame ëllëg dund gu dul jeex. Ndegam Yàlla moo ñu sàkk, jaadu na mu tette ñu. Kon war nañu ko gërëm ci ni mu ñuy tettee ak mbëggeel, te war nañu topp ay sàrtam ak ay xelalam. — Jàngal Sabóor 19:8, 12 ; Peeñu ma 4:11.

2. Yan xelal ñoo nekk ci Biibël bi ?

Xelal yi nekk ci Biibël bi mën nañu leen jëfandikoo ci fànn yu bare, waaye ndigal yi mën nañu leen topp ci benn fànn rekk (Deutéronome 22:8). Bu ñu nekkee ci dara, war nañu jëfandikoo suñu xel ngir xam ban xelal bu jóge ci Yàlla lañu mën a topp (Kàddu yu Xelu 2:10-12). Nañu jël benn misaal : Biibël bi mu ngi ñuy xamal ne bakkan mayu Yàlla la. Loolu mën na ñu tette bu ñu nekkee di liggéey, bu ñu nekkee ci kër gi, ak bu ñuy tukki. Dina tax ñu jël ay matuwaay ngir mucc ci aksidaa. — Jàngal Jëf ya 17:28.

3. Yan ñaari xelal ñoo ëpp solo ?

Yeesu waxoon na ne am na ñaari xelal yu gën a am solo. Bu njëkk bi dafa ñuy xamal li tax nit di dund, maanaam ngir xam Yàlla, bëgg ko, te jaamu ko ak takkute. Xelal bu njëkk boobu, war nañu ci bàyyi xel ci lépp lu ñuy def (Kàddu yu Xelu 3:6). Ñiy topp xelal boobu dinañu xaritoo ak Yàlla, am bànneex dëgg ak dund gu dul jeex. — Jàngal Macë 22:36-38.

Ñaareelu xelal bi dafa ñuy xiir ñu am diggante bu rattax ak suñu moroom (1 Korent 13:4-7). Bu ñu toppee ñaareelu xelal boobu, dinañu roy Yàlla ci ni muy doxale ak nit ñi. — Jàngal Macë 7:12 ; 22:39, 40.

4. Ban njariñ lañu mën a am ci topp xelal yi nekk ci Biibël bi ?

Xelal yi nekk ci Biibël bi dañuy jàngal njaboot yi naka la leen mbëggeel mënee boole ba ñu nekk benn (Kolos 3:​12-​14). Kàddu Yàlla dafay aar itam njaboot yi ndaxte dafa leen di jàngal beneen xelal bu leen di tette, maanaam séy dafa war a nekk lu sax. — Jàngal Njàlbéen ga 2:24.

Bu ñu toppee xelal yi nekk ci Biibël bi, duñu yàq suñu alal walla suñu xel. Xoolal njaatige yi, bu ñuy wut ay nit pur ñu liggéeyal leen, dañu faral di wut ay nit yu jub te farlu ci seen liggéey ni ko Biibël bi waxe (Kàddu yu Xelu 10:4, 26 ; Yawut ya 13:18). Kàddu Yàlla dafa ñuy jàngal ñu doylu ci lu ñu am, te fexe ba suñu diggante ak Yàlla gënal ñu alal. — Jàngal Macë 6:24, 25, 33 ; 1 Timote 6:8-10.

Topp xelal yi nekk ci Biibël bi mën na la aar ci feebar (Kàddu yu Xelu 14:30 ; 22:24, 25). Bu ñu toppee sàrtu Yàlla ci bañ a màndi, loolu dina ñu aar ci feebar yiy reye walla aksidaa (Kàddu yu Xelu 23:20). Yexowa terewul ñu naan sàngara. Li mu tere mooy ñu ëppal ci (Sabóor 104:15 ; 1 Korent 6:​10). Xelal yi jóge ci Yàlla amal na ñu njariñ ndax li mu ñuy jàngal ñu sàmm suñu xel ak suñu doxalin (Sabóor 119:97-100). Karceen dëgg yi duñu topp xelalu Yàlla yi ngir seen njariñu bopp rekk, waaye dañu koy def ngir màggal Yexowa. — Jàngal Macë 5:14-16.