Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 5

Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?

Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?

1. Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

Yexowa dafa may doomu Aadama yi suuf si. Suuf si mooy suñu dëkkuwaay. Kon boog, góor gu njëkk ga Aadama ak jigéen ju njëkk ja Awa, Yàlla sàkku leen woon ngir ñu dëkk ci kaw asamaan ; Yàlla sàkkoon na ay malaaka ba pare ngir ñu dund ca asamaan (Job 38:4, 7). Yàlla dafa jël góor gu njëkk ga, dugal ko ci àjjana ju rafet bu ñuy woowe toolu Eden (Njàlbéen ga 2:15-17). Yexowa mayoon na Aadama ak doom yi mu naroon na am, ñu mën a dund ba fàww ci kaw suuf si. — Jàngal Sabóor 37:29; 115:16.

Ca njàlbéen, toolu Eden kese moo nekkoon àjjana. Góor gu njëkk ga ak jigéen ju njëkk ja dañu naroon a feesal suuf si ak seeni doom. Dañu waroon a toppatoo suuf si ba àddina si sépp nekk àjjana (Njàlbéen ga 1:​28). Suuf si du fi mas a jóge. Dëkkuwaayu doomu Aadama yi lay doon ba fàww. — Jàngal Sabóor 104:5.

Seetaanal wideo Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

2. Lu tax tey suuf si nekkul àjjana ?

Aadama ak Awa déggaluñu woon Yàlla, moo tax Yexowa génne leen ci tool boobu. Noonu lañu ñàkke àjjana bi, te benn nit mënu ko indiwaat. Biibël bi nee na : “ Suuf si sépp a ngi ci loxoy ki bon ”. — Ayóoba 9:24, MN. Jàngal Njàlbéen ga 3:23, 24.

Ndax Yexowa dafa bàyyi li mu bëggoon pur doomu Aadama yi ca njàlbéen ? Déedéet ! Ku am kàttan la, dara tëwu ko (Isaïe 45:18). Dina defal doomu Aadama yi li mu leen bëggaloon. — Jàngal Sabóor 37:11, 34.

3. Kañ la suuf si di nekkaat àjjana ?

Suuf si dina nekkaat àjjana ci nguuru Yeesu mi nga xam ne Yàllaa ko fal Buur. Ci xeex bi tudd Armagedon, Yeesu dina jiite malaaka Yàlla yi ngir alag ñiy xeex Yàlla ñépp. Ba pare Yeesu dina tëj Seytaane lu mat 1 000 at. Ñiy jaamu Yàlla dinañu mucc ci xeex boobu ndaxte Yeesu dina leen aar te wommat leen. Dinañu am dund gu dul jeex ci àjjana ci kaw suuf si. — Jàngal Peeñu ma 20:1-3 ; 21:3, 4.

4. Kañ la coono yi di jeex ?

Kañ la Yàlla di jële lu bon ci kaw suuf si ? Yeesu joxe na ‘ tegtal ’ buy wone ne ñu ngi ci njeexteelu jamono ji. Ni àddina si mel tey dafay tiital nit ñi, te dafay wone itam ne ñu ngi dund ci muju jamono te léegi ‘ àddina si tukki. ’ — Jàngal Macë 24:3, 7-14, 21, 22.

Ci 1 000 at yi Yeesu di nguuru ci asamaan dina ilif suuf si, te dina fi jële coono yépp (Esayi 9:5, 6 ; 11:9). Ci kaw liggéeyu buur bi muy def, Yeesu dina def itam liggéeyu saraxalekat bu mag, te ñi bëgg Yàlla, Yeesu dina dindi seeni bàkkaar. Yàlla dina dindi feebar, màgget ak dee, jaare ko ci Yeesu. — Jàngal Isaïe 25:8 ; 33:24.

5. Ñan ñooy dund ci àjjana boobu di ñëw ?

Ci Saalu Nguur yépp, mën ngeen fa fekk ay nit ñu bëgg Yàlla te di jàng ni ñuy def ba neex ko.

Nit ñi déggal Yàlla ñooy dund ci àjjana boobu (1 Yowaana 2:17). Yeesu yónni na ay taalibeem pur ñu wut ay nit ñu woyof ngir jàngal leen naka lañuy def ba neex Yàlla. Tey Yexowa mu ngi waajal ay milyoŋi nit ngir ñu dund ci àjjana boobu di ñëw ci kaw suuf si (Tsephania 2:3). Ci Saalu Nguuru Seede Yexowa yépp, nit ñi dañu fay jàng ni ñuy nekke ay jëkkër ak ay baay yu baax ak it ni ñuy nekke ay jabar ak ay yaay yu baax. Waajur yi dañuy ànd ak seeni doom di jaamu Yàlla te di jàng ni ñuy jariñoo xibaaru jàmm bi. — Jàngal Mika 4:1-4.