Ubbil li ci biir

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Lan laa mën a def bu ñu may bundxataal?

Lan laa mën a def bu ñu may bundxataal?

Bundxataal du porobalem bu ñu war a xeeb. Am na benn gëstu bu ñu def ci Ãgalteer buy wone ne téeméer yoo jël ci ndaw ñiy xaru te ñu yégle ko ci xibaar yi ñeent fukk yi bundxataal bokk na ci li ko waral.

 Lan mooy bundxataal?

Bundxataal yemul rekk ci ay dóor. Mën na ëmb itam lii di topp.

  • Saaga. Céline mi am ñaar fukki at lii la wax: «Yenn saa yi, xale yu jigéen ñi dañuy xaste. Duma mas a fàtte tur yi ñu ma doon jox ak li ñu ma doon wax. Tax nañu ba ma gëm ne jaruma dara, kenn bëggu ma te awma benn njariñ. Ñu dóoroon ma sax moo ma gënaloon.»

  • Ber. Haley mi am fukki at ak juróom ñett lii la wax: «Ñi ma bokkaloon lekkool, daawuñu ma boole ci dara. Bu waxtu añ daan jot dañu doon fexe ba duma mën a toog ak ñoom ci benn taabal. At mi yépp dama doon jooy di lekk man kese.»

  • Bundxataal ci internet. Daniel, mi am fukki at ñeent, lii la wax: «Mën nga toog ci sa ordinatëër, bind rekk, yàq deru jaambur, ba ci sax dundam. Loolu du ay wax rekk, lu mën a am la!» Yónnee foto walla mesaas ci telefon buy yàq deru nit ki, loolu itam bokk na ci bundxataal ci internet.

 Lu tax mu am ñuy bundxataal seeni moroom?

Lii di topp bokk na ci li ko waral.

  • Ñoom ci seen bopp dañu leen doon bundxataal. Benn ndaw bu tudd Antonio lii la wax: «Ni ñu ma daan bundxataal, dafa ma mettiwoon lool ba ma komaase di bundaxataal yeneen ndaw ngir mën a neex ñi nga xam ne ñoo ma daan bundxataal. Waaye mujj naa gis ne li ma daan def baaxul dara.»

  • Amuñu ay royukaay yu baax. Jay McGraw lii la wax ci téereem bi mu bind lu jëm ci bundxataal: «Ci lu ëpp, ndaw ñiy bundxataal seeni moroom [...] dañuy roy ci ni seen waajur yi ak seen mag yu góor walla yu jigéen daan bundxataal ñeneen ñi.»

  • Dañuy def mel ni ñoo gën ñépp, fekk ci dëgg amuñu jàmm. Barbara Coloroso miy bind itam téere bu jëm ci bundxataal lii la wax: «Xale yuy bundxataal seeni moroom dañuy mel ni ñoo gën ñeneen ñi, te boo seetee ba ci biir ñu ngi dund lu metti te dañuy xeeb seen bopp.»

 Ñan lañuy faral di bundxataal?

  • Ñiy beru. Ndaw ñi noppi te gaawuñu miin nit dañuy faral di beru. Moo tax bundxataal leen yomb.

  • Ndaw ñi ñu jàppe ni ñu wuute ak seeni moroom. Yenn ndaw, dañu leen di bundxataal ndax seen melokaan, seen xeet, seen diine walla sax laago bi ñu am, lépp daal loo xam ne mën nañu ci jaar ngir bundxataal leen.

  • Ndaw ñi xeeb seen bopp. Ñiy bundxatal, dañuy gaaw a ràññe ñi nga xam ne dañu xeeb seen bopp. Dafay yomb ñu bundxataal leen ndaxte duñu faral di feyyu.

 Lan nga mën a def bu dee dañu lay bundxataal?

  • Bul leen won li ngay yëg. Benn janq bu tudd Kylie lii la wax: «Ñiy bundxataal dañuy bëgg xam ndax li ñu bëggoon am nañu ko, maanaam nga xeeb sa bopp. Boo leen wonul li ngay yëg dañu lay bàyyi. Biibël bi nee na: «Ku xelu, mer, ànd ak sagoom» (Kàddu yu Xelu 29:11).

  • Bul feyyu. Feyyu, dafay yokk porobalem bi waaye du ko faj. Biibël bi nee na: «Buleen feyante lu bon» (Room 12:17; Kàddu yu Xelu 24:19).

  • Bul dugal sa bopp ci porobalem. Defal sa kem kàttan ngir moytu ñi lay bundxataal walla dem fi nga xam ne mën nañu la fa bundxataal. (Kàddu yu Xelu 22:3)

  • Bettleen ci ni nga leen di tontoo. Biibël bi nee na: «Tont lu neex day giifal» (Kàddu yu Xelu 15:1).

  • Deel kaf. Bu ñu la nee danga am yaram, mën nga yëngal sa bopp nee ko: «Dëgg la, bu la neexee sax mën naa la ci may ñaari kilo.»

  • Demal sa yoon. Nora mi am fukki at ak juróom ñeent lii la wax: «Bañ a tontu dafay wone ne ku am xel nga, te yaa ëpp xel ki lay tàppaas. Loolu dafay wone ne ku maandu nga te ki lay bundxataal maanduwul.»

  • Góor-góorlul ngir bañ a xeeb sa bopp. Benn janq bu tudd Rita lii la wax: «Boo tiitee, ñi lay bundxataal dinañu ko xam te mën nañu ci jaar wàññi la ba nga xeeb sa bopp.»

  • Wax ko keneen. Am na benn gëstu buy wone ne, lu ëpp genn-wàll ci nit ñi ñuy bundxataal ci internet duñu ko wax kenn ndaxte xéyna dañoo rus, rawatina xale yu góor yi, walla ñu ragal ñu dalaat seen kaw.