Ubbil li ci biir

Ndax mën nañu gëm li Biibël bi nettali ci dundu Yeesu?

Ndax mën nañu gëm li Biibël bi nettali ci dundu Yeesu?

Li Biibël bi wax

Luug, kenn ci ñi bind Biibël bi, lii la wax ci li mu nettali lu jëm ci dundu Yeesu: «Gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, [...] nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe» (Luug 1:3).

Am na ñuy wax ne li ñu nettali ci dundu Yeesu ci Injiil, maanaam ci téere Macë, Màrk, Luug, ak Yowaana, dañu ko soppi ay ñetti téeméeri at gannaaw bi Yeesu deewee.

Waaye ci booru atum 1900, gis nañu xaaj bu am solo ci téere Yowaana ca Misra (Égypte). Xaaj boobu ñuy woowe tey Papyrus Rylands 457 (P52), ñu ngi ko denc ca reewu Ãgalteer, ca dëkku Manchester ca béréb bi tudd John Rylands Library. Li fa nekk mën nañu ko jàng tey ci suñu Biibël ci Yowaana 18:31-33, 37, 38.

Fi ñu tollu nii, xaaj boobu mooy bi gën a yàgg bi ñu am ci xaaju Biibël bi ñu bind ci làkku gereg . Ay boroom xam-xam yu bare jàpp nañu ne, ci booru atum 125 lañu ko bindoon, maanaam ñaar fukki at ak juróom rekk gannaaw bi ñu bindee téere bu njëkk ba. Li ñu ci bind, daanaka benn la ak li ñuy fekk ci sotti yi ko topp yi ñu am tey.