Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm

Téere bii dafay wone ni nit ñu bokk ci xeet yépp mënee dëgëral seen ngëm ngir am jàmm.

UBBITE BI

Ubbite bi

Ay milioŋi nit gis nañu tontu yu leer ci seeni laaj.

XAAJ 1

Ndax Yàlla fonk na nit ?

Àddina si tey bare na ay jafe-jafe. Yow it bés bu nekk dangay am ay jafe jafe. Ku ñu ci mën a dimbali ? Ndax am na sax ku ñu ci bëgg a dimbali ?

XAAJ 2

Lan mooy gëm Yàlla dëgg ?

Ay milioŋi nit xam nañu ne Yàlla am na waaye ba tey ñu ngi def lu bon. Kon xam ne Yàlla am na taxul nga gëm ko dëgg.

XAAJ 3

Ay xelal yu am njariñ

Mbind mu sell mi am na ay xelal yu baax yi la mën a dimbali nga faj say problem ci séy, nga wàññi sa tàng xol, nga bàyyi dorog, nga bañ a fonk sa xeet ba mu ëpp, nga bàyyi xeex ak yeneen ak yeneen.

XAAJ 4

Kan mooy Yàlla ?

Li nit ñi di jaamu bare na. Waaye Mbind mu sell mi nee na benn Yàlla dëgg rekk moo am.

XAAJ 5

Nañu fonk mbiri Yàlla yi

Mbind mu sell mi wax na ci ay mbiri Yàlla yu bare yu mën a tax ñu xam ko.

XAAJ 6

Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

Mbind mu sell mi nee na Yàlla sàkkul suuf si ndax neen waaye dafa ko sàkk ngir nit dëkk ci. Ndax ni suuf si mel tey noonu la ko Yàlla bëggee woon ?

XAAJ 7

Li Yàlla dige, jaarale ko ci yonent yi

Ay barke ngir xeet yépp !

XAAJ 8

Almasi bi ñëw na

Mbind mu sell mi nettali na dundam ak njàngaleem.

XAAJ 9

Li ñu mën a jàng ci Almasi bi nekk njiit

Yàlla xam na ban njiit mooy baax ci ñun te dafa ñuy tànnal bi gën.

XAAJ 10

Ki bañ ñu gëm Yàlla, lan la def?

Benn malaaka dafa mujj a fippu di xeex Yàlla.

XAAJ 11

Gëm Yàlla dëgg, ni ko nit ñi di wonee tey

Yeesu dafa jàngale ne nit ñi am ngëm dëgg dañuy meññ ay “ doom yu neex ” maanaam jikko yu baax. Yan jikko ?

XAAJ 12

Nanga wone ne gëm nga Yàlla dëgg !

Lan nga mën a def ?

XAAJ 13

Ku gëm Yàlla dëgg, dinga mën a am jàmm ba fàww

Mbind mu sell mi am na ay dige yu neex la te mën nga ci barkeelu.