Ubbil li ci biir

Ci dëgg, kan moo ilif àddina si ?

Ci dëgg, kan moo ilif àddina si ?

 

  • Yàlla ?

  • nit ñi ?

  • walla Seytaane ?

LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?

“  Àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis. ” — 1 Yowaana 5:19, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla.

“  Doomu Yàlla ji ñëw na, ngir nasaxal jëfi Seytaane. ” — 1 Yowaana 3:8.

LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?

Dinga xam li tax àddina bi bare coono tey. — Peeñu ma 12:12.

Dinga mën a gëm ne ëllëg dina neex.— 1 Yowaana 2:17.

NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?

Waaw waaw, xoolal liy topp :

  • Kiliftéefu Seytaane dina jeex. Yexowa dina jeexal kiliftéefu Seytaane ci kaw doomu Aadama yi. Dige na ne dina “ daaneel Ibliis ” te dindi lépp lu bon li kiliftéefu Seytaane indi. — Yawut ya 2:14.

  • Yàlla tànn na Yeesu Kirist ngir mu ilif àddina si. Yeesu, amul fenn fu mu bokk ak kilifa àddina si, maanaam Seytaane. Seytaane moom, kilifa gu soxor la te njariñu boppam rekk lay wut. Waaye lu jëm ci Yeesu, Yàlla nee na dina “ yërëm ki néewleek ku tumurànke, [. . .] boole léen jot [maanaam génne] ci notaangeek loraange ”. — Sabóor 72:13, 14, Sabóor ñeel Daawuda.

  • Bu Yàlla waxee dara, mënu cee dellu gannaaw. Biibël bi moo ko wax te mu leer nàññ : “ Manu cee dellu gannaaw ”. (Yawut ya 6:18, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla) Kon bu Yàlla digee dara, jàppe ko ni lu am ba pare ! (Esayi 55:10, 11) “ Léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si. ” — Yowaana 12:31.

LOO XALAAT CI LAAJ BII ?

Naka la àddina si di mel bu fi kiliftéefu Seytaane jógee ?

Biibël bi dafa ciy tontu ci SABÓOR 37:10, 11 ak PEEÑU MA 21:3, 4.