Ubbil li ci biir

Ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu

Ci ay teemeeri béréb ci àddina si sépp, dañuy fàttaliku deewu Yeesu benn yoon ci at mi. Dañu koy def ndaxte digal na taalibeem yi ne: “ Defleen lii, ngir fàttaliku ma. ” (Luug 22:19) Ren, bésu fàttaliku bi

Samdi 27 màrs 2021 lay doon.

Ñu ngi lay woo nga ñëw ànd ak ñun ci bés bu am solo boobu. Mbas mi moo tax ñuy amal waxtaan bi ci vidéoconférence. Boo ko bëggee seetaan, laajal benn Seede Yexowa.